Home
Page
Contact
Us
Make a Payment,
Methods of
Payment, Refund and Exchange Policies
Rosaries
subpages:
How to Pray the
Rosary
subpages:
Pictures
Main Page
subpages:
Curriculum
subpages:
Website
Terms of Use
License
Agreement
Sitemap
The Work of God's Children
|
Wolof
Rosary
Prayers
This language is also known as Woloff, Ouolof, Yalof, Walaf, Volof, and
Waro-Waro.
This
language is spoken by 3,570,000 people in Senegal.
It is also spoken by 10,000 people in Mauritania.
See also The
Work of God's Children page for the illustrated version of prayers
in this language.
CI TURU BAAY BI / Sign of the
Cross / In
Nomine Patris (Signum Crucis)
Ci Turu
Baay bi
ak
Doom ji
ak Xel mu Sell mi
Amiin.
GËM NAA CI YALLA / Symbole des
Apôtres / Apostles' Creed / Symbolum
Apostolorum
Gëm
naa ci
Yàlla,
Baay Borom-kàttan,
bindakatu asaman ak suuf;
Ak ci
Yéesu-Krista
Doomam ji di benn, suñu Borom,
ki yaramu ci
pexem Xel mu Sell mi,
juddu ca Maryaama xeeg ba,
sonn ca
nguurug Poos-Pilaat,
daaju ca kurwaa ba,
dee te ñu rob
ko;
wacc ca kaw, ñetteelu fan wa, mu dekki ca ñu dee
ña;
yéeg
ca asaman,
toog ca ndeyjooru Yàlla Baay borom kàttan;
fa la
di jóge àttesi ña di dund ak ña dee.
Gëm
naa ci Xel mu
Sell mi,
jàngu Katolig bu sell bi,
ndigaaley ñu sell
ña,
mbaaleg bàkkaar gi,
dekkim yaram wi,
ak dund gu dul
jeex ga.
Amiin.
Sunu
Baay /
Our
Father
/ Pater Noster
Sunu Baay, bi ci asamaan
na sa tur sell,
na sa nguur
dikk,
loo bëgg,
na am ci suuf naka ca asamaan.
May nu
tey sunu dundu bés bu nekk.
Te baal nu sunuy tooñ,
naka
nuy baale ña nu tooñ.
Tc bu nu bàyyi nu tàbbi
ci bëliis,
wànte musal nu ci lu bon. Amiin.
Another
version of
Suñu
bai / Our
Father / Pater Noster
Suñu
bai bi chi asaman,
na
sa tur sela,
na
sa ngur dika,
lo
buga na am chi suf
neke
chi asaman.
Mei
ñu tey suñu ton,
naka
le ñu bale nha ñu ton,
te
bul ñu bayi ñu tabi chi bolis,
wande
musal ñu chi lu bon.
Amen.
Another
version of
SUÑU BAAY / Our
Father / Pater Noster
Suñu
Baay
bi ci
asamaan,
Na sa tur sell,
Na sa nguur dikk,
Loo bëgg, na am
ci suuf naka ca asamaan.
May ñu tey suñu dundu bes bu nekk.
Te
baal ñu suñuy tooñ,
Naka ñuy baale ña ñu tooñ.
Te bu ñu
bàyyi ñu tàbbi ci bëlis,
Wànte musal ñu ci lu bon.
Amiin.
NUYU NAA LA
MARIAAMA / Hail Mary / Ave Maria
Nuyu naa
la,
Maryaama, fees nga ak yiw,
Borom baa ngi ak yow,
barkeel nga ci
jigéen ñi yepp,
te Yéesu, sa doomu biir, barkeel na.
Maryaama
mu sell mi, Ndeyu Yàlla,
ñaanal ñu, ñun bàkkaarkat yi,
léegi
ak ci suñu waxtu dee.
Amiin.
Another
version of
Negû
nâ la, Mariâma / Hail
Mary / Ave Maria
Negû
nâ
la, Mariâma,
fês
ngâ'k
yiv, Borom
b'ange'k
yov, barké nga
ti
digen i
nepa, ti Jésu
sa
Dom u bir barké nâ.
Mariâma
mu
selâ mi,
Ndey
u Yalla, ânal
nu
nun
bakarkal yi, legi ak
ta
sunu vahtu'di. Amin.
TERANGA ÑELL NA
BAAY BI / Glory Be / Gloria Patri
Teranga
ñell na
Baay bi,
Doom ji,
ak Xel mu Sell mi,
naka la woon ca cosan
la
Tey ak mos ba ca mos a mos.
Amiin.
MAÑIFIKAT /
Magnificat
Suma xol
a ngi
màggal Borom bi,
suma xell di beg ci Yàlla suma Musalkat,
ndaxte
fàttaliku na ma,
man jaamam bu woyef bi.
Gannaawsi tey, niti
jamano yepp
dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
ndaxte Ku Màgg ki
defal na ma lu rey.
Turam dafa sell.
Day wàcce yërmandeem ci
ñi ko ragal, ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
Wone na jëf yu
mag ci dooley loxoom,
te tas mbooloom ñiy rëy-rëylu,
daaneel
borom doole yi ci seen nguur,
yekkati baadoolo yi.
Ñ i xiif,
reggal na leen ak ñam wu neex,
te dàq borom alal yi,
ñ u daw
ak loxoy neen.
Wallu na bànni Israyil giy jaamam,
Di fàttaliku
yërmandeem,
Ni mu ko dige woon sunuy maam,
Jëmale ko ci
Ibraxima ak askanam ba fàww.
MALAAKUM SUÑU
BOROM YEGAL NA MARIAAMA / Angelus
Malaakum
Suñu Borom
yegal na Mariaama.
Mu daldi ëmb ca pexem Xel mu sell ma
Nuyu naa la...
Jaamu
Borom baa
ngi.
Li nga wax na am ci man.
Nuyu naa la...
Baat ba
daldi
yaramu,
Daldi dëkksi ak nun.
Nuyu
naa la...
Ñaanal
nu,
Ndeyu
Yalla ju sell ji.
Ndax nu taasu ci ndigali Yéesu-Krista.
Nanu
ñaan la:
nu
ngi lay dagan, Borom bi tuural sa yiw ci sunuy xol:
ci yégleb
malaaka ma, xamal nga nu yaramub sa Doom ji nga sopp,
Yéesu
Krista, jiité nu ci barkeb coonoom ak Kurwaam
ba nu agg ca ndamal
dekkima.
Ci
barkeb, Yéesu Krista, sunu Borom
Amiin.
SEEDES RECCU / Act of Contrition / Actus Contritionis
Yalla
suma
Borom,
reccu naa lool li ma la tooñ,
ndége yaa baax a baax te
mëta sopp,
te bakkaar neexu la; fas naa yéene,
ak sa ndimbalu
yiw,
bañati laa tooñ te ruccantiku.
Amiin.
|